YOUSSOU NDOUR - TATAGAL

2021-11-12 54

MOOL
Yaw mool u géej gi
di jambaar ci réew mi
Bala ngaa dem géej
ngala déglu météo

Bu la nee bul dem
lu mën ë xew bul dem
Ben fan ak ñaar ,
bu mu yax sa liggéey

Doyloo nga yalla ,
du tee nga sa yor téléphone
Ak sa gps , te bul fatte sa gillet

Sama fans yi ma am ,
mool ñoo ma gën ë xam
Fu ma làng ee ak ñoom ,
guddi gë day xumb lool

Man sama fans yee , ma saf
Sawar naa làng ak ñoom , fu ne
Aka ñoo dégg daaj , ma ni
Moo tax may dem ba jeex , walla

Jambaar ca waar wa ,
jambaar ca géej gë
Su ma ko mën oon ,
ben mool du des ci géej

Bu la nee bul dem ,
lu mën ë xew bul dem
Ben fan ak ñaar ,
bu mu yax sa liggéey

Sama fans yi ma am ,
mool ñoo ma gën ë xam
Fu ma làng ee ak ñoom ,
guddi gë day xumb lool

Jambaar ca waar wa ,
jambaar ca géej gë
Su ma ko mën oon ,
ben mool du des ci géej

Man sama fans yee , ma saf
Sawar naa làng ak ñoom , fu ne
Aka ñoo dégg daaj , ma ni
Moo tax may dem ba jeex , walla

Yalna leen yalla suturaal ,
te di leen samm biir géej
Barke el seen liggéey bi ,
barke el seen njaboot gi
Aar leen ba ñu doon mag ,
jox leen barke maam yi

Man sama fans yee , ma saf
Sawar naa làng ak ñoom , fu ne

Yess aye
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Bël ba ca ndar , sonn al na waa guét ndar géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Mool yi laa bëgg ë làng al ,
seen làng xumb në ,
Ndax sa ma fan’s yi nak ,
am mool yee ci gën ë dense
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Bël ba ca ndar , sonn al na waa guét ndar géej oo
Sa telephone ak sa GPS ,
bul fatte gillet ba
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Ñoom laa bëgg ë làng al , seen làng xumb në ,
Ndax sa ma fan’s yi nak , am
mool yee ci gën ë dense
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo

A dëgg ël , yaw mool u géej ,
yaa di jàmbaar
Yaa bari fullë lool
Bari jom lool
Yaa donn loolu
Gëm yalla lool
Yaa xarañ lool , te tabe lool
Youssou woy na leen
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Bël ba ca ndar , sonn al na waa guét ndar géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Mool yi laa bëgg ë làng al ,
seen làng xumb në ,
Ndax sa ma fan’s yi nak , am
mool yee ci gën ë dense
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Anh mool ba dem na géej oo
Mool yi laa bëgg ë làng al ,
seen làng xumb në ,
Ndax sa ma fan’s yi nak , am
mool yee ci gën ë dense